Esayi40wol_mbs

Xibaaru jàmm ñeel na Israayil

1Dëfalleen a dëfal sama ñoñ,la seen Yàlla wax!2Waxleen lu dalal xelu Yerusalem, yéeneleenne leen seen xare jeex na,seen mbugal mat na.Ñoo nangoo ci loxol Aji Sax jilu fey ñaari yoon seen bépp bàkkaar.
3Baat a ngi jib, naan:«Nangeen xàll yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi,fàkkalleen sunu Yàllaxàll wu jub fi joor gi.4Wépp xur lees di kaweel,tund wu mag ak wu ndaw lees di suufeel;ba fu tunde mujj dig joor,fu ñagasoon maase,5darajay Aji Sax ji daldi feeñ,àddina sépp bokk gis ko.Aji Sax jee ko wax ci làmmiñam.»
6Baat a ngi naa: «Yéeneel!»Ma ne: «Lu may yéene?»Mu ne: «Neel:Nit am ñax doŋŋ la;gépp ngoram mel ni tóor-tóoru àll.7Ñax ma wow,tóor-tóor ma laxfa ko Aji Sax ji yónnee mbóoyo.Askan wi kay, am ñax doŋŋ la.8Am ñax day wow;tóor-tóor day lax.Waaye sunu kàddug Yàllamooy sax ba fàww.»
9Yaw Siyoŋ, xibaarkatu jàmm bi,doxal yéegi tund wu kawe,te xaacook doole.Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi,xaacul te bul ragal!Neel dëkki Yuda yi:«Seen Yàllaa ngii!10Boroom bi, Aji Sax jaa ngii,dikkaale dooleak kàttanu kilifteefam.Mu ngii ànd ak ñi mu yooloo,ñu dig peyam, dox jiitu ko.11Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmmug juram,boole mbote yi cib loxoom,taf cib dënnam, yóbbu;xar yiy nàmpal, mu wommat.»
12Ana ku natte géej biir loxoom?Ku xaymaa asamaan yaatuwaayu loxo?Ku mana fab suuf sépp, sol cib nattukaay?Ana ku natte ab màndaxekaay tund wu mag?Mbaa mu tam-tamal tund wu ndaw?13Ana ku mana nànd xelum Aji Sax ji?Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal?14Ana ku mu diisool, ba kooka tegtal ko,jàngal ko yoonu njub,jàngal ko xam-xam,xamal ko yoonu dég-dég?
15Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan,jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf!Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!16Gottub Libaŋ xambul taalu sarxalukaayam,te mala ya ca ne doyu ko saraxu rendi-dóomal!17Xeetoo xeet du tus fi kanamam,te jàppewu leen lu moy neenug neen.18Ana kan ngeen di niruleek Yàlla,ak nataal bu ngeen koy dendaleel?19Xanaa du jëmmu tuur ju liggéeykat móol,ab tëgg xoobe ko wurus,takk ca caqi xaalis?20Ku néewle ba amul may gu ni tollu,mooy tànn bant bu dul nëb,seeti liggéeykat bu xareñbu ko ci sàkkal jëmmu tuur ju dëgër!
21Xanaa dangeena xamul lii?Am dangeena déggul lii?Dees leena waxul ca njàlbéen,am seen xel a jàppul nan la àddina sosoo?22Moom moo tooge ca kaw wërngalu suuf,ñi ko dëkke mel niy soccet,moo tàllal asamaan ni ndimo,firi ko nib xayma, daldi dëkke.23Mooy sànk kilifa,di neenal njiitu àddina.24Ba ñu sampoogul,toogaguñu sax,ba seeni reen di riigu,ca la leen Aji Sax jiy wal, ñu wow,ngëlén buub, yóbbu ni boob.25Aji Sell ji ne:«Ana ku ngeen may nirooleel,ba may moroomam?»26Séentuleen kaw, xoolleen Ki sàkk biddiiw yii!Xanaa kiy daaguloo leeri asamaan ni gàngoor gu mat,ñoom ñépp lay woo ci seen tur,ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam,te kenn du ci wuute.27Yeen askanu Yanqóoba, lu ngeen di jàmbat?Yeen Israayil laa ne, lu ngeen di jooy,naa: «Aji Sax ji gisul li nu dal,sunu Yàlla daal, daa réere sunu àq!»28Dangeena xamul,am dangeena déggulne Aji Sax jeey Yàlla ba fàww,sàkk suuf cat ba cat,du sonn, du tàyyi,te am xelam nattuwul?29Mooy dooleel ku loof,di kàttanal ku jeele.30Waxambaane sonn, loof;xalelu góor di tërëf a tërëf,31kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole;da naa fëyy ni jaxaay juy naaw,di xélu te du xiix,di dox te du xoox.