Esayi38wol_mbs

Esekiyas wopp na ba jóg

1Jant yooyu la Esekiyas woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!»2Esekiyas walbatiku nag, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji.3Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.4Ci kaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Esayi, ne ko:5«Doxal ba ca Esekiyas, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom.6Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettali, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”7«Lii nag ngay def ab takk bu bawoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne Aji Sax ji dina def li mu wax:8“Maa ngii di delloo ker gi gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya jant bi wàccoon ca kaw iskaleb Axas.”» Ci kaw loolu jant bi dellu gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu jotoona wàcc.9Mbind mii nag Esekiyas buurub Yuda moo ko bindoon, gannaaw ba mu tëddee wopp, ba jóg:10Man de dama noon:«Sama digg doole laay demejaare bunti njaniiw,sama ndesu fan réer ma!»11Ma noon: «Dootuma gisati Aji Sax ji ,duma gisati Aji Sax ji fi kërug àddina.Duma tegati doom aadama bët,dootul fii ci waa àddina.12Sama dëkkuwaay lañu sempi,yóbbu fu sore,mbete xaymab sàmm.Sama àpp a taxañe,ni ndimo lu ràbbkat ba doge ca mbaamu ràbb ma.Diggante bëccëg ak guddi, nga jekkali ma.13May xalaat, ba bët set;Aji Sax jiy dammat samay yax ni gaynde,diggante bëccëg ak guddi, nga jekkali ma.14May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu,di binni nim xati,di séentu kaw ba saay gët giim.Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa,dimbali ma.»15Waaye lu may waxati?Aji Sax jee ma wax,te moo jëf.Kon, ma temp ndànk sama giiru dundndax tiisu xol.16Boroom bi, ci sa kàddook sa jëf la nit di dundete ci laay noyyee ba tey.Yaa ma wéral, may ma, ma dund.17Ndeke sama tiisu xol wii,sama jàmm rekk a tax.Sa cofeel a taxnga sorele maak paxum sànkute.Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.18Njaniiw du la sant,dee du la gërëm,te ku tàbbim pax yaakaaratul sa kóllëre.19Kiy dund, kiy dund doŋŋ mooy ki lay santni man bésub tey jii,te baay mooy xamal doom sa kóllëre.20Aji Sax ji yaa may wallu,nu di la woy, ànd aki xalamsunu giiru dund,fa sa biir kër, yaw Aji Sax ji.21Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiyas bi, kon dina dund,»22ba Esekiyas noon ko: «Ana lu di takk biy firndeel ne dinaa wér, ba dellooti kër Aji Sax ji?»