1Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég,joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ.2Day tóor a tóor,di bànneexu, bay sarxolle,ba jagoo darajay gottub Libaŋak taaru àllub Karmel ak Saron.Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji,sunu taaru Yàlla.3Ku yoqi, dooleelleen ko,ku óom yay fenqe, jàppaleleen ko.4Ku fitam rëcc, ne leen ko:«Dëgërlul te bul tiit.Sa Yàllaa ngii di la feyul,ba yool say noon.Moom mooy dikk, wallusi la.»5Su boobaa gëti silmaxa muriku,noppi tëx sikkliku.6Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél,ab luu sarxolle.Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma,ay wal wale joor gu wow,7suuf su wow doonub déeg,joor gu maral ballal bëti ndox.Fa till fàkkoon, di fa goore,gattax ak barax a fay sëqe.8Foofa law yoon di jaare,ñu di ko woowe Yoon wu sell wi.Ku sobewu du fa jaare,ñi moom woowu yoon,ñooy ñi koy topp.Ab dof sax du fa lajje.9Gaynde du fa am,rab wu aay du fa dox,du lenn lees fay gis,ku ñu jot rekk a fay jaare.10Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee,agsaaley sarxolle fa Siyoŋ,kaalawoo mbég mu sax,mbégteek bànneex wàllsi,naqar aku tiis daw.