Esayi33wol_mbs

Ña daan sànke sànku nañu

1Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul,yaw workat bi kenn worul.Boo noppee bóome, ñu bóom la,te boo noppee wore, ñu wor la.2Éy Aji Sax ji, ngalla baaxe nu;yaw lanu yaakaar!Deel xëy di dooleel wii xeet,wallu nu ci biir njàqare.3Sam riir jib, xeet yi fëx;nga jóg, waaso yi fëlxoo.4Dees na sëxëtoo sa alal sëxëtoob soccet.Dees na ko sam ni njéeréer di samee!5Aji Sax jee kawe,moo dëkke fa kaw-a-kaw,te mooy dajal fi Siyoŋ àtteb dëgg ak yoon.6Liy dalal seen jamono mooykoomu ndam, xel ak xam-xam,te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal.
7Xoolleen seen jàmbaarñiy yuuxoo ci mbedd mi,ndawi jàmm yaa ngii,di jooyoo jooy yu metti.8Yoon yaa ngi wéet,kenn jaareetul ci ñall wi!Kóllëre fecciku na,xeebees na ay seede,te kenn faaleetul doom aadama.9Suuf a ngi maral, wow koŋŋ,gottub Libaŋ am gàcce, lax,àllub Saron doon joor gu wow,garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.10Aji Sax ji nee: «Xaaral rekk ma jóg,xaaral rekk ma ne ñokket,xaaral rekk ma teewal samag kawe.11Seeni mébét di am mboob,bu sottee dim ngooñ;seen noowug bopp mooy xamb sawarawi leen di xoyom.12Xeet yeey sànkuni doj yu lakk ba doon kew,mbaa taxas yu ñu buub,sànni ci sawara, mu tàkk.13Yeen ñi sore, dégluleen li ma def;yeen ñi jege, xamleen ne maa am doole.»
14Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu,way-gëmadi yaa ngay lox.Ana kan ci nun moo mana dal aksawara wuy xoyome ?Ana kan ci nun moo mana dal aktaal yu yànj ya dul fey?15Xanaa kiy doxe njub,di wax dëgg,bañ alalu foqati;loxo bay jalax ab ger,noppam di tanqamlu waxi bóome,bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.16Ku ni mel, béreb bu kawe lay dëkke,doj yu ñu dàbbali di rawtoom,dundam doy,te ndoxam du ñàkk.

Yerusalem mucc na cib noon

17Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët;yaay gis réew mi ne màww.18Sam xel dem ca sa tiitaange ja woon,nga ne: «Moo, ana ka doon waññ?Ana ka doon natt diisaayu galag?Ana ka doon waññ ay tata?»19Su boobaa dootoo gis xeet wii di jaay doole,xeet wii diisu làkk ba déggeesu ko,taqu làmmiñ ba xameesul lu ñuy wax.20Xoolal Siyoŋ, dëkk ba nuy màggale;yaay teg bët Yerusalem, dëkkuwaay bu dal ba,xayma bu deesul sempi,wewukaay ya deesu ko buddi mukk,te luy buumu xayma ya it, deesu ko dog.21Foofa déy la nu Aji Sax ju màgg jidi nekkal béreb bu defi dex aki wal,fu gaalu joow dul dawe,te gaal gu mag du fa jaare,22Aji Sax jee nuy jiite,Aji Sax jee nuy dogalal yoon.Aji Sax jeey sunu buur!Moom moo nuy wallu.23Yeen nag seen réew mi gaal la,gu goj ya yolom,ponk ba ca digg ba di yëngu,ba ndimol gaal gi firikuwul.Dees na séddoo lël ju ne gàññ,ba làggi ya sax séddu ca.24Du kenn ci waa Yerusalem,ku neeti wopp na.Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar.