1Wóoy ngalla Efrayim ,kaala ga ay màndikatam di sagoo!Taaram bu yéeme baa koy réer,ni tóor-tóor yu wow,te ma nga toŋ ca coll wa ña biiñ man dëkke,fa tiim xur wu nangu wa.2Dégluleen, jàmbaar ju am doolee ngi dikkal Boroom bi,di tawub doji yuur, ngëlén luy sànke,riddee riddi, sotti waame wu wale!Loxoom la koy rattaxe fi suuf.3Dees na joggati kaalagii màndikati Efrayim di sagoo.4Te tóor mu lax mi muy gànjaroo,mu tege ca coll ya tiim xur wu nangu wa,day mel ni figg ju ñor te jotul;ka ko gis a koy gaaw witt, wann.5Bésub keroog Aji Sax ji Boroom gàngoor yidi kaala gu yànj, gànjar gu yéeme,ñeel ndesu ñoñam,6mooy dikkal xelum dëgg kuy toog di àtte,di jàmbaaral ñiy waññi noon yi song dëkk bi, xare.7Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf,màndiw ñoll, di jang:sarxalkat akub yonent la aw ñoll di tërëfloo,biiñ jànnaxe leen,ñu màndiw ñoll, di jang,bu ñu amee am peeñu, di tërëf.8Seen taabal yépp a ngi taq ripp,fépp di waccu ak mbalit.9Ñu naa: «Ana ku Esayi mii di jàngal?Ana ku muy àgge xibaar?Xanaa ku yàggula fer,di doora bàyyi ween?10Ca rëdd wii, ca rëdd wee,nàngam sii, nàngam see,as tuut fii, as tuut fee.»11Xanaa boog nit ñu seen wax leerul,ñuy làkk, la Aji Sax jiy waxeek askan wii?12Moo leen waxoon ne leen:«Fii moo di noppalukaay bi,noppalleen ku sonn.Fii a di dalluwaay bi!»Waaye nanguwuñoo dégg.13Moo tax kàddug Aji Sax ji di mujj doon ci ñoom lu ñu manula nànd, ni:«Ca rëdd wii, ca rëdd wee,nàngam sii, nàngam see,as tuut fii, as tuut fee.»Moo tax ñuy tërëf,daanoo njaaxaanaay ba damm,di sërëx aka keppu.
Doju koñu tabax wee mat wéeruwaay
14Kon nag yeen kókkalikat yi yilifaskanu Yerusalem wii,dégluleen kàddug Aji Sax ji!15Yeena naay: «Danoo wóllëranteek dee,njaniiw lanu digool, ba du nu moom,ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal.Noo def ay fen sunu rawtu,ay wor di sunu làquwaay.»16Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne:«Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju koñu tabax,muy doju koñu tànnéef wu gànjare ci fondmaa bi,te ku ko wéeroo doo gaawa daw.17Dëgg laay def nattukaay,yoon di sama buumu betteex,tawub doji yuur buub rawtub fen,wal ma mëdd làquwaay,18seen wóllëranteek dee neen,seen digook njaniiw toxu,yaru musiba dikk ak diisaayam,wulli leen ba ngeen nooy.19Saa yu dikkee ne leen céex,suba su ne mu ne jaas,guddeek bëccëg, mu teew,te bu jibee sax fit rëcc.»20Lal a gàtt ba deesu ci tàlli,malaan cëkk ba matul càngaay .21Aji Sax jeey jóg na woonfa tundu Peracim,xadaru na woon ca xuru Gabawonngir jëf jëfam,jëfam ju yéeme ja!Moo nara liggéey liggéeyam booba,liggéey bu mu tàmmul!22Tee ngeena baña kókkaleebala ñoo teeŋal seeni jéng?Sànkute kat moo di dogal bi ma dégg,mu bawoo fa Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi,di luy dikkal réew mi mépp.
Aji Sax jee xam doxalin
23Teeyluleen te déglu sama kàddu,teewluleen ba dégg samay wax. Xoolleen ci lii:24ndax beykat bi day dëkke gàbb,di rëdd aka gàbbaat?25Bu gàbbee ba toolam maase,du day sànni jiwum nisel ,wasaare jiwum kumin,daldi def bele bi ay saawo,sànni lors ba fa mu ko rëddal,doora suy bele bu dëgër ba ca wet ya?26Dees koo xamal yoon wa,te Yàllaam a ko jàngal mbey.27Mbàccum nisel watiir amu ca yoon,te deesul bàcc kumin itam, ba joggi ca tànki watiir.Mbàccum nisel, yet a koy def;mbàccum kumin, bant bu yem.28Gubi bele, dees na ca jaare watiir,waaye deesu ci dëkk;watiir ngay takkal fas, bàcce ko pepp,waaye doo ko bàcc ba mu far mokk!29Xel moomu it fa Aji Sax jiBoroom gàngoor yi la bawoo.Ndigalam a ni yéemee,pexeem màgge ni!