Esayi27wol_mbs

1Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamarambu jàmbaare, ñàng te réy,ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa,Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem,ninki-nankay géej jooju lay rey.

Aji Sax ji juboo naak ñoñam

2Bésub keroog, tóokëru reseñ ju neex am,nangeen ko woy,3te man Aji Sax ji maa koy toppatoo,di ko suuxat saa su ne,di ko wattu guddeek bëccëg,bala koo kenn a song.4Mereetuma tóokër bii,waaye lu ciy dég aki dagg,ma dox wuti ko, xareek moom,boole lépp xoyom.5Xanaa ku langaamoo sama kiiraayte jàmmook man,ba jàmmook man.6Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen,Israayil moomooy tóor, law,ba feesal déndu àddinaak meññeef.
7Defe ngeen ne Aji Sax ji duma na Israayil,na mu dumaa ña leen duma woon?Am bóomal na leen lu tollookla seeni bóomkat bóomoon?8Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom,ba mu leen toxalee,dàqe leen noowam gu mag,bésu ngelawal penku.9Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam,nii la mujje am njéggalu bàkkaaram:day boole doji sarxalukaay bi yépp,rajaxe ni doji kew,xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe,mbaa sarxalukaayi suurukaay.10Dëkk bu ñu dàbbali mooy wéet,gental, ne wëyëŋ!Fa la nag di fore,fa lay goor, di lekk cari garab ya,11car ya wow, damm,jigéen ñi dikk, xambe.Dañu di xeet wu dul dégg,ba tax ki leen sàkk yërëmu leen,moo leen bind te ñeewantewu leen.
12Bésub keroog Aji Sax ji bàcc,dale ca dexu Efraat ba ca walum Misra,te yeen bànni Israayil, dees na leen forkenn-kenn, ba ngeen daj.13Bésub keroog bufta bu mag jib,ña laŋoon réewum Asiri délsi,ànd ak ña ñu tasaare woon biir réewum Misra,ba sujjóotalsi Aji Sax ji fa Yerusalem,fa kaw tund wu sell wa.