Esayi25wol_mbs

Cant jib na

1Aji Sax ji, yaay sama Yàlla,dama lay teral, di la sant.Yaa defi jaloore,muy dogal yu yàgg, wér te wóor.2Yaa def dëkk bi jali doj,dëkk bii ñu dàbbali nga gental;taaxu doxandéem yi noppee doon péey ba fàww,te deesu ko tabaxaat.3Moo tax xeet wu am doole di la màggal,waa péeyu xeet yu néeg di la wormaal.4Yaa di rawtub néew-ji-doole,di rawtub aji ñàkk, biir njàqare,yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame,di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor,ndax merum kilifa gu néegmooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.5Doxandéem yii diy noon,ni ngay dàqe tàngoor fi béreb bu ne sereŋ,ni ngay dakkale seen coowal xare.Ni aw tàngoor di dakke ndax aw niir,ni la woyu ñu néeg ñi di selawe.

Bernde ñeel na xeet yépp

6Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,mooy berndeel xeet yépp fi kaw tund wii,bernde ju niin ak ngëneelu biiñ,yàpp wa duuf, yuq ga ne xéew,ak tànnéefu biiñ bu teey.7Fi kaw tund wii lay tukkile càngaayli sàng askanoo askan,ak séru rabal bi ñu ràbbal xeetoo xeet.8Mooy mëdd dee ba fàww!Boroom bi Aji Sax jeey fompegépp kanam rongooñi boroom.Buumi gàccey ñoñam it,moo koy doge fépp ci àddina.Aji Sax ji kat wax na ko.
9Bésub keroog dees na ne:«Sunu Yàllaa ngii nag!Moom mii lanu yaakaaroonte moo nuy wallu.Aji Sax jii lanu yaakaaroon,nan bég te bànneexoo wallam.»

Aji Sax ji tas na Mowab

10Aji Sax ji kat teg na tund wii loxo,te ni ñuy dëggaatee mboobum sën ba,ni lees fiy dëggaatee Mowab.11Mowab dina féqoo féqu,mel ni kuy jéema féey,waaye Aji Sax jee leen di toroxal,ñook seen manoore.12Seen tata yu kawe, mu fél, màbb;rattax fi suuf, maasale.