Esayi24wol_mbs

Mbugal daj na àddina

1Aji Sax jaa ngii di tas àddina,tasaare ko,salfaañe li fi dénd bi,wasaare ñi ko dëkke:2sarxalkat beek baadoolo bi,sang akub jaam,njaatige lu jigéen ak ab janqam,jaaykat ak jëndkat,ablekat ak àbbkat,leblekat ak lebkat.3Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral,dees koo futti ba mu ne furaas!Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!4Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ,àddina ne làcc, ne sereŋ,kàngami xeeti àddina ne làcc.5Suuf si la ñi ko dëkke sobeel,ñoo wàcc yoon yi,xëtt ndigal,fecci kóllëre gi sax dàkk.6Moo tax alkànde yàq suuf,ñi ko dëkke gàddu àq ji.Moo tax waa àddina raaf,ba ñi des di lu néew.7Biiñ ñàkk na,garabu reseñ lax,bépp xol bu tooyoon, binni.8Tabala ju xumb selaw na,ña daa xaxaloo dal,mbégtem buumi xalam dakk.9Kenn naanatul, di woy,ñoll wex na ka koy naan.10Dëkk bu gental tasaaroo na,kër yépp tëje, kenn duggul.11Mbedd maa ngi soowaloo,ndax biiñ bu ñàkk,gépp mbégte fey,bànneexu àddina dëddu.12Tojiti neen a des ci dëkk bi,bunt ba rajaxoo.13Noonu lay deme ci àddina,ci biir xeet yi,mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm,mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja,gannaaw bu ñu wittee ba sottal.

Ndes wi rëcc mbugal a ngi sant

14Ña ngay xaacu di sarxolle,waa sowu di sàbbaal ci màggug Aji Sax ji.15Yeen waa penku, sargalleen Aji Sax ji boog,yeen waa duni géej, teralleen Aji Sax ji Yàllay Israayil.16Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa:«Màggaay ñeel na Aji Jub ji!»Coono jeexulWaaye man dama ne: «Jeexle naa!Jeexle naa, wóoy man!Workat yaa ngi wor a wor,ba far làggi ci wor.»17Yeen waa àddina,kat-kat, pax akub caax dëgmal na leen.18Nga déggi yuux, daw,tàbbi biir pax,génne pax,laawoob caax.Mbàndi kaw kat ubbi na,suufu àddina di rëŋ-rëŋi.19Suuf daa loroo loru,fett a fett,salfaañoo salfaañu.20Suuf a ngi jang a jang ni màndikat,ba joy ni mbaar,moyam diis ko gann,mu daanu te du jógati.

Aji Sax jeey nguuru fa Siyoŋ

21Bu bésub keroogeeAji Sax ji dikke mbugalgàngoor ya fa kaw-a-kaw,ak buuri àddina yi fi suuf.22Dees leen di boole denc cim pax,ne leen ràpp tëj,ba mu am ay fani fan, ñu mbugal leen.23Kersa la weer wiy am,gàcce ñeel jant bi;Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daalmooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ,leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.