Esayi22wol_mbs

Ab yéeneb waxyu ñeel na Yerusalem

1Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma:Ana lu ngeen di yéege,yeen ñépp seen kawi taax?2Lu waral coow li ak xaxaloo bi,ba dëkk biy riir?Ñi ngeen deele, saamar reyu leen,bóomuñu leen ci xare.3Seen njiiti xare yépp a bokk daw,ñu jàpp leen te taluñoo fitte.Seen njiit yi ñu gis yépp lañu jàpp,te ñu dawoon ba sore.4Moo ma tax ne: «Buleen ma xool,damay naqarlu, jooy.Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.»5Lii kat bésub njommite laak coonook toroxte,bésu Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi,ci biir xuru Peeñu mi.Tata ja, ñu rëkk a rëkk, mu màbb,yuux jolli, àkki tund ya.6Waa Elam gàllooy fitt,ñenn ña war watiir, gawar ya war,waa Kir ŋàbb pakk ya.7Seen xur yu nangu yaa fees aki watiir,gawar taxaw temm buntu Yerusalem,8te Yuda ne duŋŋ, dara wëru ko.Su keroogee ngeen yaakaar ngànnaayya ca kër ga ñuy woowe Gott ba,9far gis ni ñu bëtt-bëttee tatay Yerusalemji wër gox bi ñu naan Kër Daawuda.Ngeen rooti ndox ca solom bu suufe ba, denc ko,10boole ca waññ këri Yerusalem,màbb lenn, sàkk ca lu ngeen aare tata ya.11Da leen di fekk sàkk mbànd diggante ñaari tata yi,ngir denc ca ndoxum déeg bu yàgg ba.Waaye xooluleen ki dogal lii,xalaatuleen ki nasoon lii bu yàgg.
12Bésub keroog, Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yimoo leen di woo ci jooyoo ak ñaawluak wateefu nel ak colu saaku ngir ñaawlu.13Te yeena ngii ci mbég ak bànneex,di rendi nag ak xar,di yàpp aka naan,naan: «Nan lekk, naan, nde ëllëg nu dee!»14Aji Sax ji ci gàngoor yi dégtal na ma lii:«Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal,ba keroog ngeen di dee.»Boroom bee ko giñ,moom Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi.

Kàddug artu ñeel na Sebna

15Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi dafa wax ne: «Ayca, demal ba ca Sebna, bëkk-néegu buur sii, nga ne ko:16Ana loo fi am, ak koo fi am?Nga di fi yattlu bàmmeel, yatt ko ca kawte ya,di gaslu kër gooy mujje?17Jàmbaar, dama ne Aji Sax jee lay xalab;da la naa nikk,18fodonk la, rattax,nga xalangoo àll bu ne màww.Fa ngay dee,te fa la watiir yi ngay puukarewoo di des,muy sa gàccey waa kër sang.»19Aji Sax ji nee: «Maa lay jële sa liggéey,foqatee la sa péete mu kawe.20«Bésub keroog ma woo sama jaam bi, Elyakim doomu Ilkiya,21solal ko sa mbubb, dooleele ko sa laxasaay, teg kilifteefu réew mi ci loxoom, ba mu féete wàllu baay waa Yerusalem ak waa kër Yuda.22Maa koy ràng caabiy kër Daawuda, muy ubbi te kenn du tëj; di tëj te kenn du ubbi.23Maa koy samp fu dëgër ni ab wékkukaay, mu doon sagu kër baayam.24Waa kër baayam ak seen daraja, ñépp ay wékku ci moom, car yaak caraat ya. Ndab yu ndaw yépp ca la, kopp ya ba ca njaq ya.25Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, mu ne: «bant ba sampe woon fu wóor day simpiku. Dees koy gor, mu fàq, la ca sëfe woon dog.» Aji Sax ji déy wax na ko.