Esayi16wol_mbs
1Waa Mowab a nga naa:«Yónneeleen boroom réew mi yóbbalu kuuy yu ndaw,jële ko Sela, jaare màndiŋ ma,yóti ko buurub Yuda fa tundu Siyoŋ mu taaru.»2Jigéeni Mowab a nga ca jàllukaayu dexu Arnon,mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tàgg,di fët-fëtluy, naaw.3Ña nga naa njiiti Yuda:«Xelalleen nu, àtte nu,lalal nu bëccëg ndarakàmm ker gu mel ni guddi,yiire ko daw-làqu yi nu doon;buleen nu wor te nuy wuta raw!4Mayleen nu, nun ñi rëcce Mowab, nu dal ak yeen,te ngeen làq nu bóomkat.»Kiy noote déy day jeexal, sëxëtoo dakk,kiy lore ci réew mi jóge fi,5ab jal sampe fi ci ngor,ki ci toogee jikko ju dëggu di askanu Daawudate di njiit luy sàkku yoon, yàkkamti àtteb dëgg.6Noo dégg ni Mowab réye,réya réy, reew te bew,seeni kañu di waxi neen.7Moo tax Mowab di jooy ba ñéppi Mowab jooyoo,ndax namm nàkku reseñ ba woon ca Kir Eres,ba ne yàcc, di binni.8Tool ya fa Esbon day wow,njiiti xeet yee dëggaate ngëneelu reseñ gu Sibma,te cabb ya lalu woon ba Yaser,ba àkki déndu màndiŋ ma,car ya law ba wàllaa géej.9Jooyi waa Yaser laay jooy reseñ ga fa Sibma,yeen waa Esbon ak Elale, ma sange leeni rongooñ,nde fa ngeen di dajaleek fa ngeen di góobe,coowal mbégtee fay dakke.10Mbégteek bànneex ay toxoo seeni tool,ay woy aki sarxolle noppee jibe seeni tóokër,te nalkatu reseñ naltil fa mbànd ya!Aji Sax jee dakkal coow li.11Maa ngi yërëm Mowab, bay binni ni buumu riiti,sama yaram daw ci Kir Eres.12Mowab a ngoog ak coonoom,ba muy deme fa bérebi jaamookaay ya,dugg kër yàllaam di ñaan te du am.13Lii la Aji Sax ji waxoon bu yàgg ci mbirum Mowab,14tey Aji Sax ji wax ne:«Fileek ñetti at yu surga bu ñu bind waññ,dees na sàggi sagub Mowab,te li ñuy bare tey lépp,seenum ndes ay néew lool te tekkeedi.»