Esayi15wol_mbs

Ab yéeneb waxyu ñeel na Mowab

1Yéene bii ñeel na Mowab:Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes!Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes!2Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon,ngir jooyi ca bérebi jaamookaay ya,Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba,boppoo bopp dib nel,sikkimoo sikkim xuufu,3nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya,ak kaw taax yaak pénc ya,ku ne di jooy ba say rongooñ wale.4Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu,seen baat àkki ba Yaxacc,xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo,ne yàcc ne yasar!5Maay jooy Mowab jooyi xol,nit ñaa nga fay dawe ba Cowar,àkki ba Eglat Selisiya.Ña ngay yéeg jëm Luxit, di jooyoo,awe yoonu Oronayim, di yuuxu.6Dexu Nimrim wow na,ñax wow, gàncax lax,dara naatatul.7Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon,yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya.8Yuux déy maase na réewum Mowab,jooyoo ya ba Eglayim,jooyoo ya ba Beer Elim.9Dexu Dimon déy fees na ak deret,te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw,ba ku rëcce Mowab,ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!