Esayi14wol_mbs

1Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu tànn xeetu Israayil woowu. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.2Yeneen xeet yeey delloo bànni Israayil ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israayil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon.3Bés bu leen Aji Sax ji teggilee seeni coonook seeni fitna, ba ngeen tàggook njaam gu metti gi ñu leen tegoon,4su boobaa nangeen woyal buuru Babilon léeb wii, ne ko:«Moo nu ki daan noote mujje?Nu mu mujjeek reewandeem?5Aji Sax jee damm bant,bi ñu bon ñi daan dóoree!Moo damm seen yetu nguur6wi ñu daan xadaruy dóor askan yi,dóor yu dakkul,di joggatee xeet yi xol bu tàng,topp leen, tëë ba.7Àddina yépp a féex, am jàmm,sarxolle jolleendoo.8Garab yi dul ruus, ak seedari Libaŋ saxdi bége sab jéll,naan: “Ba nga daanoo ba tey,ab gorkat jógalu nu.”
9Njaniiw ga fa suuf-a-suuf yàkkamti na la,di la waaja gatandu,ba yeel la ndem-si-yàlla yi doon njiiti àddina yépp.Moo yékkatee buuri xeet yépp seeni jal,10ñoom ñépp àddu, ne la:“Yaw it, mujj nga néew doole ni nun am?yaak nun de a mujj yem kepp!”11Sa puukare gee tàbbisi nii njaniiw,yaak sa buumi xalam am?Ay duusu di sa laltan,ay sax di sa càngaay!
12Moo yaw biddiiwu njël bi noon ràññ,tey nga xàwweekoo asamaan ba fii!Yaw mi daa daan xeet yi,tey, ñu gor la, nga goor.13Xanaa du yaa doon wax ci sam xel, naa:“Maay yéeg ci kaw asamaan,maay aj sama jal ci kaw biddiiwi Yàlla,maay toogi ci kaw tundu ndaje ma,fa catal bëj-gànnaar.14Maay yéeg fa kaw niir ya,ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!”15Teewul nga tàbbi njaniiw,àkki ba ca xóotey pax ma.
16Ku la gis ne la jàkk,xel ma ne ci yaw, mu naa:“Xanaa du kii a doon loxloo àddina,yëngal réewi réew,17def àddina wërngal këpp ndànd-foyfoy,tas dëkk ya,te du jàpp nit ba yiwi ko?”18Buuri àddina yépp, ba ñu daj,ñépp a tëdd tëraayu teraanga,ku ci nekk ak bàmmeelam.19Yaw, ñu xañ la bàmmeel, sànni la,nga mel ni car bu ñu foñ.Yaa ngi ne lareet ci biir néew yu saamar bóom,ñu tàbbal leen ci xeeri biir kàmb.Yaa ngi mel ni médd mu ñuy joggati.20Deesu la robaaleek yooyu buur,yaa yàq sam réew,faagaagal saw xeet.«Deesul tuddati mukk askanu lorkat wii.21Waajalleen fi ñuy rendi doom yi,feye leen seen ñaawtéefi baay,bala ñoo jógati, teg àddina loxo,ba tabax fu ne ay dëkk
22«Maa leen di jógal.»Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.Mu ne: «Maay tenqi turu Babilon, tenqim ndesamba ca seeni doom ak seen askan.»Kàddug Aji Sax jee.23Mu ne: «Maa koy def kërug suññeel,def ko ab tan,ba buube ko buubub rajaxe.»Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

Mbugal ñeel na Asiri

24Aji Sax ji Boroom gàngoor yee giñ ne:«Lu ma nar déy mooy am,lii ma mébét, mooy sotti.25Maay joggati Asiri fi samam réew,dëggaate leen fi sama kaw tund yi,ba sama ràngi ñoñ rengiku,seenub yen yenneeku.»
26Mii mébét lañu mébétal àddina sépp,bii loxo lañu xàcc jëme ci xeet yépp.27Bu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dogalee déy,ana ku koy dogale?Bu xàccee loxoom,ana ku koy fommal?

Ab yéeneb waxyu ñeel na Filisti

28At ma Buur Axas saayee,bii yéene jib na:29Filistee, yet wi daloon ci seen gannaaw damm na,bu ko kenn ci yeen bége,ndax ci ëkku jaan ji, la ñàngóor di génne,am tostanam mujj di céebi.30Su boobaa ñi gëna walaakaana am lu ñu for,néew-doole ya goor, ànd ak dal.Waaye yeen, maa leen di xiifal, ngeen dee ba raaf,xiif ba rey ñi ngeen dese.31Yeen magi pénc mi, ñaawluleen!Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen!Na Filisti gépp ne yàcc!Bëj-gànnaar déy la saxaar jollee,kenn du wuute gàngooru noon ya.32Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj,xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ,te fa la baadooloy ñoñam di rawe.