Esayi11wol_mbs

Daawuda am na kuutaay

1Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese ,ab car soqeekoo fa reen ya,2xelum Aji Sax ji tegu fi kawam,xelum rafet xalaat ak ràññee,xelum digle ak njàmbaar,xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.3Ragal Aji Sax ji lay safoo,du lu ko bëtam may lay àttee,du lu ko noppam may lay dogale,4xanaa di àtte dëgg ku ñàkk,di dogalal njub néew-ji-dooley àddina.Mooy dóore àddina bantub kàddoom,mooy reye ñu bon ñi ngelawal gémmiñam.5Njubte lay gañoo,takkoo kóllëre.6Till ay bokk ak mbote ab dal,segg bokk akub tef ab tëraay,wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar,tuut-tànk jiite leen.7Nag ak rab wu aay di forandoo,seeni doom goorandoo,gaynde di lekkum ngooñ niw yëkk,8luy nàmp di fowe paxum ndox-suuf,perantal di laal tostanum ñàngóor.9Deesatul gaañe mbaa di lore,fi mboolem sama kaw tund wu sell wi,ndax ni ndox di feese ba muur géej,ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.10Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba,taxaw di raaya buy gindi xeeti àddina si,jàmbur ñi di gëstusi,dalluwaayam ba jagoo màggaayu Yàlla.
11Bésub keroog Boroom bi jooti loxoomñaareel bi yoon,ngir jotaat ndesu ñoñamwa des Asiri ak Misra ak Pattros ak réewum Kuus ak Elam ak Sineyaar ak Amat ak biir duni géej ya.12Mooy yékkatil xeet yi raaya,dajale ña ñu dàqe Israayil,ak ña ñu jële Yuda, tasaare leen,ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo.13Fiiraangey Efrayim day jeex,njéefoy Yuda dakk,Efrayim dootul fiire Yuda,Yuda dootul jéppi Efrayim.14Xanaa ñu ne coww ba sowu,ne jàyy cëppandoofa kaw waggi Filisteen ña,waa penku, ñu sëxëtoondoo;Edom ak Mowab, ñu teg loxo;Amoneen ña nangul leen.15Aji Sax jeey wowal walum ndox,ma séle géeji Misra.Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat,wal kook doole,dóor ko, mu séddalikoo juróom ñaari wal,mu jaarale ca nit ñu caraxu,16def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam,ña dese fa Asiri,mu mel ni yoon wa ñeeloon Israayil,bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra.