1Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyasak Yotam ak Axas ak Esekiyas.
Aji Sax ji sikk na waa Yuda
2Asamaan, déglul; suuf, teewlul,Aji Sax jeey àddu:«Ay gone laa yar, màggloo leen,ñoom, ñu gàntal ma.3Aw yëkk xam na boroomam,mbaam-sëf xam gàmb bi ko boroomam di xonte,waaye Israayil xamul,sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»4Wóoy wii xeetu moykat,wii askan wu diisu ñaawtéef,mii njurum defkati mbon,yii doomi yàqute!Ñoo wacc Aji Sax ji,ñoo sofental Aji Sell ju Israayil,dëddu ko.5Xanaa dungeen wéye fippu,ñu gën leena duma,te bopp di góomi neen,xol jeex tàkk?6Bopp ba téstën, fenn jagul.Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk,ak góom yuy nàcc,fajeesu ko, takkeesu ko,gajfaleesu kook ag diw.7Seenum réew gental,seeni dëkk xoyomu,seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam,muy gent bu doxandéem tas.8Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéetni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal.Mbete dëkk bu ñu gaw!9Bu nu Aji Sax ju gàngoor yiwaccalul woon li nu deseek as néew,ni Sodom lanuy mel,Gomor lanuy neexool.
Aji Sax ji bañ na ngistal
10Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom,teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.11«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax.«Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy,suur nebbonu juru yar gi,deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.12Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam,ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii sama ëttu kër?13Buleen fi indeeti saraxi caaxaan,seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la.Terutel weer ak bésub Noflaayak wooteb ndajee ci yem!Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.14Seeni Terutel weer ak seen bési màggallaa bañ ci sama xol;yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.15Bu ngeen ma tàllaleey yoxo,ma fuuyu.Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it,du maa leen di déglu:seeni loxo, deret la taq ripp.16Raxasuleen ba set wecc,jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam,te ngeen ba lu bon.17Jàngleen di def lu baax,sàkku njub,waññi ab nootkat,àtte dëgg ab jirim,sàmm àqu jëtun.18«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax.«Li seeni bàkkaar di xonq lépp,tàll lay weexeji.Li muy xonq curr lépp,weex furr lay mujje.19Su ngeen ma nangoo déggal,ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.20Waaye su ngeen lànkee, fippu,saamar a leen di xéewloo.»Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
Mbugal mooy setal Yerusalem
21Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc,te nekkoon dëkkub kóllëre,yoon mate fa,njubte lal fa panaan,tey ñu diy bóomkat!22Sa xaalis doon na raxit,sa biiñ xormbet.23Seeni njiit të,xejjoo ay sàcc,ñoom ñépp sopp ger,di dàq ay neexal;ab jirim, sàmmuñu àtteem,àqu jëtun soxalu leen.24Moo tax, kàddug Boroom bee,Aji Sax ju gàngoor yi,Jàmbaaru Israayil:«Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom!Maay fey samay noon!25Yerusalem, maa lay teg loxo,maay seeyal sa raxit ni xeme,ba dindi sa mbuubit mépp.26Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon,ñi lay digal it dellu mel ni bu njëkkoon.Su boobaa ñu woowe la Dëkkub Yoonak Dëkkub Kóllëre.»27Siyoŋ dëppook yoon, mucc,ay tuubkatam wormaal njub, raw;28moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo,dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.29Yeenay rus moos ci garab yu mag,yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu.Yeenay am gàcce ci tóokëryi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.30Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax,mbaa tóokër bu amul siitum ndox.31Boroom doole mel ni boob,la mu liggéey di ferñent,ànd ak moom ne jéppét,te kenn du fey sawara wa.