Ose13wol_mbs

Mbugalum fippu ci kaw Aji Sax ji du jaas

1Bu Efrayim daan wax, ñépp ay lox;mu amoon daraja fi digg Israayil.Waaye moo sikkal boppam ci tuuri Baal, ba dee.2Léegi ñu ngi gën di bàkkaar,di xellee ci seen xaalis jëmmu tuur,ay jëmmi xërëm yu ñu sàkke seen xareñte,lépp di càkkéefu ay liggéeykat,te ci ñoom la nit ñi naan:«Rendikati sarax yaa ngi fóon ay tuuri wëllu.»3Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba,mbaa layub njël,mbaa boob bu naawe ca dàgga ja,mbaa saxaar su gillee ci jankub néeg.
4«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla,xamuleen Yàlla ju dul man,te kenn du musle ku ma moy.5Man maa leen ràññee ca màndiŋ ma,ci biir réewum maral.6Ngeen wëtti ba regg,regg, bew, ba tax ngeen fàtte ma.7Moo tax ma mel ni gaynde ci yeendi tëroo ni segg ciw yoon.8Maay dajeek yeen ni rab wu aaywu ñu xañi doom,maay xotti seen mbuusum xol,fa laa leen di yàppe ni gaynde,te rabu àll moo leen di xotat.
9«Israayiloo, yàqu nga,te maa yor sa wall.10Ana seen buur boog,ba mu xettali leen ci seen mboolemi dëkk?Ana seen njiit yi ngeen sàkku woon, ba ne ma:“Falal nu buur aki kàngam”?11Ci biir mer laa la falal buur,te ci sama sànj laa ko follee.
12«Takkees na ñaawtéefi Efrayim,rënkees na ay moyam.13Lu mel ni mititu mat moo dikkal waa jii,te muy doom ju amul xel,ba juddu jot, génnul biiru ndeyam.
14«Man nag ndax maa leen di musal ci njaniiw?Ndax maa leen di jot ci dee?Moo yaw dee, ana say mbas?Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke?Fomm làqu na ma!15Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it,fa màndiŋ ma la ngelawal penku ,ngelawal Aji Sax ji di uppe,bëti ndoxam tëju,ay teenam déy.Kii mooy sëxëtoo ab dencam,ak mboolem lu cay alal.