Ose11wol_mbs

Cofeel la Aji Sax ji tontoo fippug Israayil

1«Maa soppoon Israayil ba muy ndaw,Misra laa woowe sama doom, mu génne fa.2Lu ñu leen gëna woo,ñu gën maa sore.Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax,te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.3Ndaxam man maa tette Efrayim, fab ko,te ràññeewuñu ne maa leen toppatoo.4Ay goji nit laa leen ñoddee,ay buumi cofeel.Maay ki leen yolomalal ŋalaabi ŋaam,sëgg, leel leen.5Duñu dellu réewum Misra .Waa Asiri ñooy doon seen buur,nde ñoo baña délsi fi man.6Ab saamar ay wëndeelu ca seen dëkk yu mag,dàjji seen bunti dëkk,ba warax leen ndax seeni mébét.7Sama ñoñ dañoo làggi ci ñàkke ma kóllëre,woowees na leen fa kaw,te kenn ci ñoom jógul.
8«Efrayim, ana nu ma lay dëddoo;yaw Israayil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo?Ana nu ma lay defe ni Adma?Nu ma lay yemaleek Ceboyim ?Sama xol a bëpp,sama yërmandee yëngu.9Duma wéye di tàkkal sama mer,duma yàqateeti Efrayim,ndax maay Yàlla, duma nit,maay Aji Sell ji ci seen biir,duma dikke am sànj.10Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji,muy yëmmu ni gaynde.Mooy yëmmu moos ni gaynde,ay doomam di lox, jóge sowu.11Ni njanaaw lañuy loxe, jóge Misra,mel nim pitax, bawoo Asiri.Maa leen di dëël seeni kër.»Aji Sax jee ko wax.