Ose10wol_mbs

Israayil ŋarale na

1Israayil di reseñ gu naat,meññal boppam lu ne gàññ,te lu meññeef ma gëna yokku,mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur.Lu am réewam gëna baaxle,mu gëna baaxal ay tuuri doj.2Ñooy boroom xolub jinigalkat,te tey ñooy gàddu seen bàkkaar.Aji Sax ji mooy toj seeni sarxalukaay,tas seen tuuri doj.3Léegi ñu ne: «Amunu buur,ndax noo wormaalul Aji Sax ji.Te su nu amoon buur it, lu mu nu manal?»4Ñooy wax seeni wax,di giñe ay fen yu ñuy fasoo kóllëre,ba yoon mel ni gàncaxu tookeju law ca tooboy tool ya.5Waa Samaree ngi am tiitaangeci sëllu wu ñu xelli ca Bet Awen ,askan wa di tiislu tuur ma,ay xërëmkatam di lox ndax darajay sëlluji leen dëddu, gàddaay.6Moom it lees di yóbbu Asiri,defal ko buur bu mag ba ab galag.Gàcce mooy jàpp Efrayim,Israayil laa ne, mooy rus ci mébétam.7Samari lees di tas, mook buuram,mu mel ni bant buy tëmb di dem.8Bérebi jaamookaay ya ca Bet Awen,bàkkaarukaayi Israayil yooyu lees di tas.Ay dég aki dagg ñooy sax ca seeni sarxalukaay.Dees na ne tund yu mag yi: «Daanuleen ci sunu kaw»te naan tund yu ndaw yi: «Suulleen nu.»
9Aji Sax ji nee na: «Israayiloo, ca janti Gibeya nga dala moye,te foofu la waa réew mi tollu ba tey.Luy tee xare dabe nit ñu jubadi ñi ca Gibeya?10Saa yu ma soobee ma yar leen.Ay xeet ay daje, jógal leen,jéng leen ndax seen ñaari ñaawtéef.11Efrayim aw nag wu nangu la woon,te sawaroona bàcc am pepp.Maa ràng loosam wu jekk.Maa takk Efrayim,Yuda gàbb, Yanqóoba rijjil boppam.12Jiwalleen seen bopp njub,ba góobe ca lu ngor maye.Gàbbleen ag mbooy,jaamu Aji Sax ji jot na,ba kera muy dikk, tawal leen njub.13Yeena bey ag coxor,góob ag mbon.Yeena lekk meññeefum fen,nde yeena wóolu seen pexey bopp,ak seen jàmbaar yu bare.14Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor,sa tata yépp tas,na Salman tase woon Bet Arbel,keroog bésub xare ba,ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.15Noonu lees leen di def, yeen waa Betelndax seen mbon gu réy.Jant a ngay fenk, buurub Israayil dee wett.