Yawut ya6wol_mbs
1Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi bi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat njàngale yi jiitu ci xibaar bi. Njàngale mi moo di gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi dee.2Te di itam njàngalem xeeti njàppak ñaan gu ànd ak tegeb loxo; ak mbirum dee-dekki ak àtteb bés-pénc biy sax dàkk.3Nanu jëm kanam, te moom lanuy def, ndegam soob na Yàlla.4Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo ci asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.5Ñoo mos kàddug Yàlla gu baax gi ak manoore yu jamono jiy ñëw,6ba noppi xàcc. Kon deesu leen waññi, ngir ñuy tuubati, nde ñoo daajaat Doomu Yàlla ci bant, ñoom ci seen bopp, teg ko toroxte ju ne fàŋŋ.7Ndax suuf kat, su naanee ndox mu mu tawlu ay yoon, ba meññ gàncax gu jariñ ñi ñu koy beyal, soosa suuf dina séddu ci barke bu bawoo fa Yàlla.8Waaye su meññee ay dég aki xaaxaam, amul njariñ, alkuteem lees di tudd léegi, te lakk lay mujje.9Waaye nag soppe yi, nii nuy waxe ak yeen teewul nu di leen yaakaar ci lu wér, li leen gëna amal njariñ, te bokk ci seenug mucc.10Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.11Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn parlu googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk.12Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.