Yawut ya5wol_mbs
1Bépp sarxalkat bu mag nag, ci biir nit ñi lees ko jële, fal ko ngir nit ñi, ci seen diggante ak Yàlla, muy joxe ay saraxi njébbal ak saraxi jur ngir seeni bàkkaar.2Dina mana sédd cér ñi xamul ak ñi moy ndax moom ci boppam ci ag néew doole la tënku.3Néew doole googu moo tax mu wara joxeel boppam, tey joxeel askan wi ay sarax, ngir seeni bàkkaar.4Te it kenn jagoowul boppam teraangay carxal, ndare du Yàllaa ko ci woo, na woon ca Aaróona.5Noonu la woon itam ci Almasi bi. Tegoowul boppam darajay doon sarxalkat bu mag, waaye Yàllaa ko ne:«Yaa di sama Doom,bés niki tey maa la jur .»6Noonu it la waxe feneen, ne:«Yaa dib sarxalkat ba fàww,topp dayob Melkiccedeg .»7Fan yi Almasi bi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te ñaan ga nangu na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.8Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.9Noonu lees matale Almasi bi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.10Ci biir loolu Yàlla tudde ko sarxalkat bu mag bi topp dayob Melkiccedeg.