Yawut ya1wol_mbs

Yàlla moo feeñ ci Doom ji

1Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali.2Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.3Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,4te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.

Doom jee gëna màgg malaaka yi

5Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko:«Yaa di sama Doom,bés niki tey, maa la jurba neeti:«Maay doon Baay ci moom,muy Doom ci man »?6Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan:«Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal7Malaaka yi, la Yàlla wax ci seen mbir ne:«Moo def ay malaakaam diy ngelaw,jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara8Waaye Doom ji la Yàlla ne:«Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww,sa yetu buur njub la.9Yaa sopp dëgg, bañ lu bon,ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég,nga tiim say moroom10Mu neeti:«Yaw Sang bi, ca njàlbéen ga, yaa samp suuf,sàkke asamaan say loxo.11Yooyu day réer,waaye yaw yaay sax,lépp ay ràpp ni mbubb.12Yaa leen di taxañ ni malaan,ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo,te yaw ngay kenn ki,te say at amul kem13Ana kan ci malaaka yi la mas ne:«Toogeel sama ndijoor,ba ma def say noon sa ndëggastal »?14Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?