Abakug2wol_mbs

1Fa may wattoo laay taxaw,ne temm fa kaw tata ja,ba xam ana lu mu ma Aji Sax ji di àddu,ak lu may waxaat ci samab tawat.

Aji Sax ji àddooti na

2Aji Sax jee àddu, ne:«Bindal peeñu mi,leeral ko ci àlluwa yi,ba njàng mi yomb.3Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal,seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen.Su diibee it, xaar ko,day dikk moos te du yàggati.
4«Xol baa ngay xoggaliku, te ag njub nekku ca,waaye ku jub ndax kóllëreem ak Yàlla mooy dund.5Biiñ day wore,jàmbaar ju bew jii nag du dallu,xanaa yàkkali puruxam ni njaniiw,du doylu, mbete dee,moom miy buubandoo xeetoo xeet,dajale askanoo askan, aakimoo.6Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji,fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan:“Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul,lii ba kañ?”Kii di sëfoo nii ay bor!7Moo! Ndax ñi la lebal duñu jekki jóg?Ñooñu la tiital ñooy jekki yewwu,te yaay doon seenum cëxëtoo.8Yaa sëxëtoo woon ay xeet yu bare,mboolem ndesu askan yee lay sëxëtooji,ndax deretu nit ji nga tuur, soxore ay réewaki dëkk ak mboolem ña ca biir.
9«Wóoy ngalla kuy dajaleel këramalalu yàqute ju lewultey aj am tàggam fu kawe,ngir fegu ci yàqule.10Gàcce nga nasal sa kër,ba nga sànkee ay xeeti xeet,te yaa tooñ sa bopp.11Doju tata dina riir déy,aw dénk àddoo ca jank ba, feelu ko.
12«Wóoy ngalla ku tabaxe ab dëkkderet ju mu tuur,ku sanceb dëkk ag njubadi.13Xanaa du ci Aji Sax jiBoroom gàngoor yi la lii bawoo:Sawara la askan yiy ñaqal,ag neen la waasoo yiy doñ-doñil?14Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj,ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.
15«Wóoy ngalla yaw mi nàndal sab dëkkaale,sotti sa ndabal sànj, màndale ko,ngir niir ko, mu ne duŋŋ!16Gàcce ngay gëna regg teraanga,naanal yaw it te wone sa mbuñuka!Ci yaw la kaas bi ci ndijooral Aji Sax jidi walbatiku,sa toroxte wuutu sa teraanga.17Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu ci sa kaw,te sànkuteg rabi àll yi sa tiitaange jay jur.Yaa tuur deretu nit, indi aw ay ci réew mi,ak dëkk beek mboolem ñi ci biiram.
18«Ana luy njariñal yatt jëmmu xërëmju ki ko sàkk yatt,mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli,di ci gëmloo nit ay fen?Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko,xërëm yoo móol te manula wax!19Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,”naan doj wu ne selaw: “Yewwul!”Ana lu yooyii di xamle?Ma nga noonu, ñu xoobe ko xaalis ak wurus,te du gennug noo ci biiram.»
20Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanam mu sell,na àddina sépp selaw fi kanamam.