2Éy Aji Sax ji, foo àppal lii?May woote wall, dégluwoo ma!Ma di la jooy aw ay, te walloowoo!3Ana loo may wone lu bon,tey seetaan nooteel?Yàquteeku ay fi sama kanam,xuloo di wéy, ŋaayoo jolli.4Moo tax yoon lafañ,te àtteb dëgg du feeñ mukk.Ku bon a tanc ku jub,ba tax ab àtte jalgatiku.
Aji Sax ji tontu na
5«Xoolleen ci biir xeet yi ba gis,» la Aji Sax ji wax.«Jommileen jommeet, nde jëf a ngi jëfe ci seeni jant,su ñu leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.6Maa ngii di dooleel waa Babilon,xeet wu wex, ràkkaaju,di wër déndi àddina,di nangu màkkaani jàmbur.7Ñu ñàng, raglu,te di dogalal seen bopp àtteb yoon ak sañ-sañ.8Seeni fas a gëna gaawi segg,gëna aay tilli timis.Fu sore la seeni gawar jóge, tëbal,naaw nig jaxaayju ne jàyy, lekkum rëbbam.9Aw ay lañuy dikke, ñoom ñépp,buurandoo, jubal màkk seen kanam,te ñi ñuy jàpp njaam bare ni feppi suuf.10Ñooñu ay buur lañuy ñaawal,boroomi daraja di seen reetaanukaay;ñii lépp luy tata lañuy kekku,jalal ko suuf, nangu ko.11Jàll, wéy lañu cay teg ni ngelaw,tegoog tooñ, te seen doole di seen yàlla.»
Abakug jooyati na
12Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk?Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay.Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii,yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.13Sa gët yu sell jomb naa niir lu bon,te manoo seetaan nooteel!Ana looy seetaan ay workat?Looy noppi te ku bon di mëddmoroomam mu ko gëna jub?14Yaa def doom aadama mel niw jën,mbaa ndiiraanu ndundat lu amul njiit,15te ñoom ñépp la ku bon di korandoo,diri leen ciy mbaalam,dajale ciy caaxam,ba tax ko di bég aka bànneexu.16Moo tax muy rendil mbaalam ab sarax,di taalal ab caaxam saraxu cuuraay,te naan moo niinal njëlam,duunal ab dundam.17Mbaa du nii lay yuree mbaalam,di wéye fàllas ay xeet te yërëmul?