Esekiyel30wol_mbs

Babilon song na Misra

1Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:2«Yaw nit ki, jottalil kàdduy waxyu! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’3Bés jubsi na déy,bésub Aji Sax ji jubsi na!Bésub xàmbaar, muy bésub àtte ñeel xeet yi.4Saamar ay dikkal Misra,fépp di jal-jali ba ca Kuus,aw nit, ñu bóom ca Misra,nangu alalu réew ma,kenu ya màbb.5Waa Kuus ak Puut ak Ludd ak xeet yu raxe yépp ak waa Kub,boole ci ñenn ci réew mi farandoo ak moom,ñoom ñépp saamar a leen di faat.
6«“Aji Sax ji dafa wax ne:Wéeruwaayi Misra ya day jóoru,doole ja Misray sago ŋiis;la dale Migdol ba Asuwan , saamar a leen di faat.Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.7Ñooy gëna wéet ci réew yi,seeni dëkk gëna gental ci dëkk yi.8Bu ma taalee Misra,ba wéeruwaayam yépp rajaxoo,dinañu xam ne maay Aji Sax ji.9Bésub keroog dees na dugg ay gaal, génn ci sama ndigal,ngir indil tiitaange réewum Kuus ma ne finaax,muy seen jal-jal keroog jéllub Misra ba.Bés baa ngii di dikk déy!
10«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Maay jeexal mbooloom Misra mu réy,jaare ko ci Nebukatnecar buuru Babilon.11Mooy ànd ak ñoñam,di ñi gëna néeg ci yéefar yi,dikk yàqatesi réew mi;ñooy boccil Misra saamar,ba feesal réew mi ay néew.12Maay def wali Niil ag joor,maay jaay réew mi nit ñu aay.Maay alag réew meek li ci biiram,jaare ko ci ay doxandéem.Man Aji Sax ji, maa ko wax.
13«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Maay sànk kasaray tuur yi ak yàllantu ya ca Memfis.Buur dootul toog ci jalu réewum Misra,te maay indi tiitaange ci biir Misra.14Maay yàqate Pattros,taal dëkk bi ñuy wax Cowan,ba sottal sama mbugal ci kaw dëkk bi ñuy wax No.15Maay sottil sama xadar Sin, rawtub Misra,te maay tenqi gàngooru No.16Maay taal Misra,dëkk ba ñuy wax Sin di rag-ragi;dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko;Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg.17Xaleli góori Oon ak Pi Beset, saamar a leen di faat,waa dëkk yooyu ca des njaam lañu jëm.18Bu ma dogee sidditi Misra,ba doole ja muy sago ŋiis,jant dootul fenk ci Tapanes,aw xiin ay sàng dëkk bi,te dëkk-dëkkaanam ya, njaam lañu jëm.19Nii laay wàccee ay mbugal ci Misra,ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»

Doole réer na Misra

20Ca fukkeelu at maak benn, juróom ñaari fan ca weer wa njëkk, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:21«Yaw nit ki, damm naa përëgu Firawna buuru Misra,mu ngii, deesu ko takk, ba mu faju,deesu ko lëmës, ba mu mana ŋàbb saamar.22Léegi nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Maa ngii fi kaw Firawna buuru Misra.Ñaari përëgam yépp laay damm;bu baax beek bi damm ba noppi,maay waddal saamaram bi ci loxoom,23maay tasaare Misra fi biir xeet yi,wasaare leen fi biir réew yi.24Maay dooleel përëgu buuru Babilon,teg sama saamar ci loxoom.Gannaaw ba ma dammee përëgi Firawna,Firawna dina binni te dee ci kanamu noonam.25Maay dooleel përëgi buuru Babilon moos,përëgi buuru Misra yoqi.Maay teg sama saamar ci loxol buuru Babilon,mu xàcc ko jëme ci réewum Misra,ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.26Maay tasaare Misra fi biir xeet yi,wasaare leen fi biir réew yi,ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»