1Aji Sax ji ne ma: «Yaw nag jooyal garmiy Israayil.2Neel:“Céy sa ndey, ndaw gaynde, fi biir gaynde yi!Moo goor fi biir gaynde yu ndaw yi,di fa yar ay doomam.3Moo tàggat kenn ciy goneem ,ba muy waxambaane gaynde,mana pàdd pàddam,di yàpp doom aadama.4Ba ko xeet ya déggee, dañu koo fexeel,mu sërëx ca seenum yeer,ñu lonk, yóbbu réewum Misra.5«“Ndey gaynde xaar a xaar,ba gis ne yaakaar jee na,mu jël keneen ciy goneem ,def ko waxambaane gaynde.6Mu ànd ak moroomi gayndeem,màgg, mat,ba mana pàdd am pàddam,di yàpp doom aadama.7Mu tëdde seeni jëtun,gental seen dëkk yu mag,réew maak la ca biiram tiit ca coowal ŋaram.8Teewul xeeti diiwaan ya ko séq ànd,dal fa kawam,laaw ko seenum caax,sërxal ca seenum yeer.9Ñu lonk, dugal cib kaaf,yóbbul ko buuru Babilon,tëj ko ca biir ab tata,ba kenn déggatuli ŋaram fa kaw tundi Israayil.10«“Sa ndey a la niru, mel ni reseñgu ñu jëmbat fi wetu ndox,meññ, sëq lipp, ndax ndox mu ne xéew.11Mu am car yu dëgër yu man yeti nguur,daldi màgg ba àkki niir ya,ràññiku ci taxawaay ak sëqaay.12Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf,ngelawal penku wowal doom ya,bànqaasam yu dëgër ya fàq, lax,sawara xoyom ko.13Tey mu ngi jëmbate fi màndiŋ mi,ci réew mu wow, maral.14Sawaraa tàkke fa bànqaasam,xoyom njebbit ak meññeef.Du car bu dëgër bu ca desbu mana doon yetu nguur.”Woyu dëj a ngii wu ñuy jooyeb dëj.»