1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal ne ma:2«Yaw nit ki, digg kërug fippukat nga dëkke, ñu ami gët te duñu gis, ami nopp te duñu dégg, ndax kërug fippukat lañu.3Yaw nag nit ki, dajaleel ci digg bëccëg, ñépp di gis, sa jumtukaay yi, mel ni ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu.4Sab ëmb ngay njëkka génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo, ñépp teg ci bët. Te yaw nga génn ngoon ni ku jëm ngàllo, ñu teg ci bët.5Dangay bëtt ci miir bi, ñuy gis, pax mooy yoore sab ëmb.6Nañu la gis nga gàddu sab ëmb, génn ci lëndëm gi. Booy génn di dem, sa kanam ngay muur, ba doo mana gis suuf si, ngir misaal laa la def, ñeel waa kër Israayil.»7Ma def loolu noonee ñu ma ko sante. Samab ëmb laa génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo. Ca guddi ga ma bëtte miir ba loxoy neen, ñépp di gis. Ci lëndëm gi laa gàddu sama ëmb, ñuy gis.8Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ca ëllëg sa ca suba, ne ma:9«Yaw nit ki, xanaa waa kër Israayil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?”10Waxleen, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Boroom Yerusalem la artu bii ñeel, mook mboolem waa kër Israayil gi fi dëkk.”11Neel:“Man maay seen misaal.”Nii ma def rekk lees leen di def,ngàllo lees leen di jàpp, jëme.12Seen boroom dëkk beey gàddub ëmbam,génn dëkk bi ci lëndëm gi.Miiru dëkk bi lees di bëtt, jaarale ko ca.Kanam ga lay muur,ba tax du gis suuf si.13Maa koy laaw samab caax,mu keppoo samag fiir,ma yóbbu ko Babilon fa Kaldeen ña dëkk.Réew ma, du ko gis te fa lay deewe.14Mboolem ña ko dar,ay toppam ak mboolem gàngooram,maa leen di wasaare fépp fu ngelaw jublu,toppati leen ak saamar.15Bu ma leen tasaaree ci biir xeet yi,wasaare leen ci réew yi,ñu xam ne maay Aji Sax ji.16Du tee ma ba ñenn ci ñoom,ñu mucc saamar, mucc xiif, mucc mbas,ba nettaliji seen gépp tojaangeca digg xeet ya ñu jëm.Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.»17Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:18«Yaw nit ki, lekkal saw ñam, di kat-kati,naane njàqare sam ndox, di rag-ragi,19te nga wax waa réew mi,mbirum waa Yerusalem ga ca suufas Israayil,ne leen Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Njàqare lañuy lekkeji seenu ñam,te xol bu gental lañuy naane seenum ndox,ndax seen réew mu gental, ñàkk lépp lu ko feesoon,ngir coxoru mboolem ñi ko dëkke.20Dëkk yu xumboon, mujj wéet,réew mi doon ab gent,ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
Kàddug Yàlla du jaas
21Gannaaw gi, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:22«Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israayil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!”23Kon wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Maay dakkal woowu léeb,ba muy léebtil fi Israayil.”Waxleen kay ne leen:“Bés a ngi jubsi,peeñoo peeñu sotti.24Du peeñuy caaxaan muy amati mbaa ngisaaney jayaatefi biir kërug Israayil.25Man Aji Sax ji,maay wax li may wax,mu sotti te dootul fomm.Kërug fippukat gi ngeen doon,maay àddu kàddu, sottal ngeen fekke,kàddug Boroom bi Aji Sax jee!”»26Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:27«Yaw nit ki, waa kër Israayil déy a nga naan: “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay jottali ay kàdduy waxyu!”28Moo tax wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:Sama genn kàddu dootul fomm.Léegi kàddu gu ma àddu, sottal ko.Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»