Kàdduy waare6wol_mbs

Alal, na la jariñ

1Aw tiis a ngi wu ma gis fi kaw suuf,di tiis wu diis doom aadama:2nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja,te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn,waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk,xanaa jàmbur di ko xéewloo—loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
3Ku giir téeméeri doom,dund ati at,ak lu at ya baree bare,su bégewul teraanga ja mu amte amul njëgu bàmmeelam sax,kooku lumb wu tuuroo ko tane.4Lumb wa ñëw na moos ci neen,bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.5Gisul jant, xamu ko,waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,6bu dundoon junniy junniy at saxte amul jàmm.Xanaa du benn béreb la ñépp jëm?
7Nit ak doñ-doñam jépp, biiram,te taxul mu doylu.8Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe?Nga ñàkk, xam doxalin,lu mu lay jariñ?9Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem.Loolu it, cóolóoli neen ak nappum ngelaw.

Nit dogalul

10Lu masa ay, dees koo tuddoon;lu doom aadama doon, xamees na ko,te kenn du layook ku la sut.11Loo ci wax wax,solo sa gëna néew.Kon ana loo ci jële?12Ana ku xam lu gën ci nit ak fanam ni cóolóol,toogadi ni takkndeer?Ku koy wax luy am gannaawam fi kaw suuf?