Baamtug yoon wi27wol_mbs
1Ba loolu wéyee Musaa ak magi Israayil sant mbooloo ma, ne leen: «Sàmmleen mboolem santaane yi ma leen dénk bésub tey.2Bés bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dugg ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, sampleen ay doj yu mag, ngeen diw doj ya weexal,3te ngeen bind ca mboolem kàdduy yoon wii, gannaaw bu ngeen jàllee. Su ko defee ngeen mana dugg ca réew ma leen Aji Sax jiy jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, noonee leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji waxe woon.4Gannaaw bu ngeen jàllee dexu Yurdan, sampleen doj yooyu ca kaw tundu Ebal, ni ma leen ko sante tey jii, te ngeen diw doj yi weexal.5Nangeen fa tabax ab sarxalukaay, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ab sarxalukaay bu ñu defare doj yu jumtukaayu weñ laalul.6Doj yu mat yu ñu soppiwul lenn ca na ñu bindoo ngeen di tabaxale ab sarxalukaay, seen Yàlla Aji Sax ji, ngeen def ca ay saraxi rendi-dóomal, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji.7Defleen ca itam ay saraxi cant ci biir jàmm yu ngeen di lekk foofa. Ngeen daldi bége fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji.8Nangeen bind ca kaw doj ya, mboolem kàdduy yoon wii, ba mu leer nàññ.»9Ba mu ko defee Musaa ak sarxalkat yiy Leween ñi wax ak Israayil gépp, ne leen: «Yeen Israayil, neleen cell te déglu. Bés niki tey doon ngeen askan wu ñeel seen Yàlla Aji Sax ji.10Kon nag déggalleen seen Yàlla Aji Sax ji, te ngeen jëfe ay santaaneem, ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey.»11Musaa nag sant mbooloo ma bésub keroog, ne leen:12«Giir yii may lim, ñooy taxawe kaw tundu Garisim, ngir ñaanal mbooloo mi, gannaaw bu ngeen jàllee dexu Yurdan: Cimyoneen ñi ak Leween ñi ak Yudeen ñi ak Isakareen ñi ak Yuusufeen ñi ak Beñamineen ñi.13Giir yii nag ñooy taxaw di rëbbe, fa kaw tundu Ebal: Rubeneen ñi ak Gàddeen ñi ak Asereen ñi ak Cabuloneen ñi ak Daneen ñi ak Neftaleen ñi.»