Baamtug yoon wi17wol_mbs
1Buleen sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji, aw nag mbaa ab gàtt bu am sikk, mbaa jenn laago, ndax seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na loolu.2Bu nit feeñee ci seen biir, ci benn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, muy góor mbaa jigéen juy def lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, di fecci kóllëreem,3bay jaamuji yeneen yàlla, di leen sujjóotal, mbaa muy sujjóotal jant bi, mbaa weer wi, mbaa mboolem gàngooru asamaan, te santaanewuma ci lenn,4bu ñu leen ko yeggee ba ngeen dégg ko, seetleen mbir ma bu baax. Su dee dëgg gu wér, ne defees na lu jomblu loolu ci biir Israayil,5nangeen génne ba ca buntu dëkk ba, waa ji mbaa ndaw si def jooju jëf ju bon, te ngeen dóor ay doj, waa jooju mbaa ndaw si, ba mu dee.6Kàddug ñaari seede ba ñett nag, ci lees di reye ki ñu wara rey, waaye deesu ko rey ci kàddug benn seede.7Loxoy seede yee koy njëkka dóor doj ngir rey ko, loxoy mbooloo mépp door koo dóor. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.8Su leen mbir jafee, ba wees leen ci àtteb bakkan bu ñu faat, ak ay jote, ak loraangey yaram yu ñu teg nit, ak mboolem dëngoo bu laaj àtte ci seen biir dëkk, dangeen di dem ba ca béreb ba seen Yàlla Aji Sax ji di tànni,9ngeen àgg ca sarxalkat yiy Leween ñi, ak àttekat ba mbir ma yemool jamono, te ngeen sàkku ñu biral leen àtteb mbir ma.10Nangeen jëfe nag kàddu ga ñu leen ca wax, ca béreb booba Aji Sax ji tànn, te ngeen sàmmoo koo jëfe mboolem noonee ñu leen ko digale.11Kàddug ndigal la ñu leen digal, ak àtte ba ñu leen ci wax, jëfeleen ko. Buleen lajje fenn kàddu ga ñu leen ca wax; du ndijoor, du càmmoñ.12Képp ku ci daŋŋiiral, baña déggal sarxalkat ba fa ayee liggéeyal seen Yàlla Aji Sax ji, baña déggal àttekat ba, kooku dees koy rey. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci Israayil.13Askan wépp a koy dégg, tiit, ba duñu daŋŋiiralati.