Amos6wol_mbs

Boroom alal naagu na

1Wóoy ña ne finaax ca Siyoŋ,wóoy ña naagu fa tundu Samari!Ñooy kàngami xeet wi gëna màggéey,niti Israayil di leen diis ay soxla!2Demleen ba Kalne, xool;jóge fa jëm Amat dëkk bu mag ba ,wàcci Gaat, dëkkub waa Filisti ya.Ana fu ñu tanee yii réew?ak fu ñu leen ëpplee suuf?3Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqaretey woo nguurug fitna!4Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj,aka sóonoo seen laltu yu nooy,di yàpp mbote yu baaxak sëllu yu duuf,5yeena ngi fowantoo xalam,di fent woy yu ànd ak xalam ni Daawudaay.6Yeena ngi jolu seen këlli biiñ,di diwoo ngën-gi-diw,sànkutey askanu Yuusufa soxalu leen.7Moo tax yeenay jiituji ci ñi ñu gàddaayloo,tëraayu xawaare dakk.8Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee:«Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba,ba seen kër yu yànj soof ma!Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.»9Su boobaa, fukk ñu làqu ci kër, du leen teree dee.10Ku warloo waajal mbokkam mu dee dina dugg ca kër ga, ngir yóbbu néew ya, te naan ka ca biir-a-biir: «Kenn desul foofu ci yaw?» Mu ne ko: «Jeex na,» bëgg caa teg baat, mu ne ko: «Déet! Noppil, bul tudd turu Aji Sax ji.»11Aji Sax jee ngii déy, buy joxe ndigal rekk,daldi tas kër gu mag,rajaxe kër gu ndaw.12Moo! Ndax fas dina daw ciy doj?Am dees na ràng aw nag, di gàbb doj?Moona walbati ngeen àtteb yoon, def ko tooke,yoon mel ni xay.13Yeena ngi damu ca dëkk ba ñuy wax Lodebar (muy firi Amul njariñ) te naan: «Xanaa du sunu dooley bopp lanu nangul sunu bopp dëkk bu am doole ba ñuy wax Karnayim (muy firi Ñaari béjjén)14Aji Sax ji, Yàlla, Boroom gàngoori xare yi da ne:«Yeen bànni Israayil,maa ngii di yékkati weneen xeet fi seen kaw,ñu noot leen, dale ko fa kaw, fa Buntu Amat ca bëj-gànnaarba ca xuru Araba, ca bëj-saalum.»