1Kàdduy Amos a ngii, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa. Mu am peeñu mu jëm ci Israayil ci janti Osiyasbuurub Yuda ak janti doomu Yowas, Yerbowam buurub Israayil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.2Mu ne:Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ ,Yerusalem lay àddoo,parluy sàmm si ne faraas,mbooyum kaw tundu Karmel lax.3Aji Sax ji da ne:«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,laay sikke waa Damaas ,te duma fomm seeni duma.Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.4Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel,mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.5Maay dàjji bunti dëkkub Damaas,dagg waa xuru Awen ,boole ca boroom yetu nguur fa Bet Eden .Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir .»Aji Sax jee ko wax.6Aji Sax ji nee:«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,laay sikke waa Gasa ,te duma fomm seeni duma.Ñoo jàpp ba noppi gàddaayloo mbooloom lëmm,jalax leen ca Edomeen ña.7Maay yebal sawara ca tatay Gasa,mu xoyom ay taaxam.8Maay dagg waa Asdoddak boroom yetu nguur fa Askalon,fél Ekkron,ndesu Filisteen ña sànku.»Boroom bi Aji Sax jee ko wax.9Aji Sax ji nee:«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,laay sikke waa Tir ,te duma fomm seeni duma.Am na mboolooy lëmm yu ñu gàddaayloo,te ñoom waa Tir jaay leen Edomeen ña,te sédduñu leen ci kóllëreg mbokk gi.10Damay yebal sawara ca tatay Tir,mu xoyom ay tataam.»11Aji Sax ji nee:«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,laay sikke waa Edom ,te duma fomm seeni duma.Ñoo toppe seen bokki bànni Israayil saamar,jalax yërmande,mer mer mu dul meddiak xadar ju dul giif mukk.12Maay yebal sawara fa Teman,mu xoyomaale tatay Boccara .»13Aji Sax ji nee:«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,laay sikke Amoneen ñi,te duma fomm seeni duma.Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd,ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.14Maay jafal ca kaw tatay Raba ,mu xoyom ay taaxam,yuux ya jib bésub xare,ci biir callweer bésub ngëlén.15Seen buur lañuy jàpp, mu gàddaay,mooki kàngamam.»Aji Sax jee ko wax.