1Kàddu yii la Daawuda tàggatoo. Da ne:Kàddug Daawudaa ngii, doomu Yese,kàddug góor gu ñu kaweel,góor gi Yàllay Yanqóoba fal,muy woykatu Israayil, bi ñu ñal.2Ci noowug Aji Sax ji laay waxe,mu sol ma kàddoom.3Yàllay Israayil a wax,cëslaayu Israayil a ne:«Ku jiite ay nit cig njub,bu jiitee cig ragal Yàlla,4day mel ni leeru jant bu fenk,kaw asamaanu suba su niir newul,leeru asamaan su set, taw ba sewet,ba ñax jebbi.»5Du nii la sama waa kër def ak Yàlla?Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk,lépp jekk, mat sëkk.Moo may may ndam saa su ne,di ma defal lu ma namm.6Waaye ku bon, ñu buub nig taxas, sànni.Deesu ko fore loxo,7xanaa fore ko weñ mbaa bantub xeej,jafal mu lakk fa mu ne.
Jàmbaari Daawuda def nañuy jaloore
8Ñii ñoo di jàmbaari xarey Daawuda ya: Yosebasebet dib Agmoneen, moo jiite mbëri xare ya. Moo xàcc xeejam, songandoo juróom ñetti téeméeri (800) góor, rey leen.9Ka ca topp di Elasar, Elasar, Dodo. Dodo, Axowa. Elasar bokkoon na ci ñetti jàmbaari xare ya àndoon ak Daawuda, di dëkk Filisteen ña fa daje woon ngir xare. Fekk bànni Israayil di dellu gannaaw.10Elasar a taxaw, di cor Filisteen ña, ba loxo ba banku, taq ca njàppul saamaram. Aji Sax jee maye ndam lu réy bésub keroog! Ba ko mbooloom bànni Israayil fekksee, defuñu lu moy futti néew ya.11Ka topp ca Elasar di Saama. Saama, Age ma dëkk Arar ay baayam. Ba Filisteen ña dajee ca Lexi, wetu toolub ñebbe ba meññoon, ba fees dell. Bànni Israayil danoo njëkkoona dawe Filisteen ñi gannaaw.12Saama moo taxaw ca digg tool ba, aar tool ba, duma Filisteen ña. Noonu la ci Aji Sax ji maye Israayil ndam lu réy!13Mu am bés, jamonoy ngóob, ñett ña bokk ca mbëri xare ya fekki Daawuda ca xunt ma ca Adulam. Mbooloom Filisteen ñaa nga dal ca xuru Refayeen ña.14Daawudaa nga ca biir rawtoom. Mu am kuréelu xareb Filisteen gu tollu Betleyem.15Ci biir loolu Daawuda dem ba manatula muñ. Mu ne: «Éy waay ku ma wutali woon ndox mu ma naan ca mbalkam Betleyem ma ca buntu dëkk ba!»16Ci kaw loolu ñetti jàmbaari xare ya bëtt dalub Filisteen ña, duyi ndox ca teenu Betleyem ba ca wetu buntu dëkk ba, dikk yót Daawuda. Daawuda nag néegu koo naan; da koo tuur, te Aji Sax ji tax.17Mu ne: «Mukk Yàlla tere, may naan miim ndox, Aji Sax ji, nde kon deretu ñii dem jaayi seen bakkan laa naan!» Daawuda naanul ndox ma. Jooju jëf la ñetti jàmbaari xare ya def.18Abisay bokkoon na ca mbëri xare ya. Abisay ak Yowab, Ceruyaa di seen yaay. Abisay moo yékkati xeejam song ñetti téeméeri góor, rey leen. Mu doxe fa siiw ci ñetti mbëri xare ñooña.19Abisay moo gënoona siiw ña bokk kuréel gu tudd Ñett ña; mujj na sax di seen njiit, doonte bokkuloon ca Ñett ña.20Benaya nag, Yoyadaay baayam, xarekat bu mag la woon, dëkkoon Kabcel. Def na jaloore yu réy! Moo rey ñaari Mowabeen ña gënoona jàmbaare. Moo wàccoon ci kàmb, bésu tawu yuur, rey fa gaynde.21Moo reyoon it waa Misra bu jekk ba taxawaay. Waa Misra baa nga yor ab xeej, Benaya songewu ko lu moy aw yet. Mu bif xeeju waa Misra ba, nangoo ko cay loxoom, reye ko ko.22Jooju jëf la Benaya doomu Yoyada def. Moom it siiwoon na ci ñetti mbëri xare ya.23Moom lañu gënoona naw ca kuréel gu tudd Fanweeri jàmbaar ya, raw na leen ba booleesu ko ca Ñett ña. Daawuda nag def ko njiitu dag ya ko dar.24Ñii bokkoon nañu ca Fanweeri jàmbaar ya: Asayel, mbokkum Yowab, ak Elxanan, doomu Dodo ma dëkk Betleyem,25Saama ma dëkk Arodd, ak Elika ma dëkk Arodd,26Elecc ma dëkk Pelet, Ira, Ikes di baayam, dëkk Tekowa,27Abiyeser ma dëkk Anatot, Mebunay dëkk Usa,28Calmon dëkk Axowa, Maaray dëkk Netofa,29Eleb ma Baana di baayam, dëkk Netofa, ak Itay ma Ribayi di baayam, dëkk Gibeya gu Beñamineen ñi.30Benaya ma dëkk Piraton, Iday ma dëkk walum Gaas,31Abi Albon ma dëkk Araba, Asmawet ma dëkk Barum,32Elyaba ma dëkk Saalbon, ak góor ñi Yasen di seen baay, ak Yonatan,33Saama di baayam, dëkk Arar, Axiyam, Sarar di baayam, dëkk Arar,34ak Elifelet, Axasbay di baayam, Axasbay, baayam dëkk Maaka, ak Elyam, Axitofel di baayam, dëkk Gilo,35ak Ecceray ma dëkk Karmel, ak Paaray ma dëkk Arab,36ak Igal, Natan di baayam, dëkk Coba, ak Bani ma dëkk Gàdd,37ak Celeg, Amoneen ba, ak Naxaray ma dëkk Beerot te daan gàddu gànnaayi Yowab ma Ceruya di yaayam.38Ira ma dëkk Kër Yeter ca la, ak Gareb ma dëkk Kër Yeter itam,39ak Uri, Etteen ba. Ñoom ñépp tollu ci fanweeri jàmbaar ak juróom ñaar.