2.Buur ya19wol_mbs
1Naka la ko Buur Esekiyas dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji.2Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca sarxalkat ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc.3Ñu ne ko: «Esekiyas dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer!4Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»5Ba surgay Buur Esekiyas àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax,6Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa.7Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma reye ko ab saamar ca réewam.”»