1Kàddug Samiyel nag di dikkal Israayil gépp. Ci biir loolu bànni Israayil dem, dajeek waa Filisti ngir xare. Ña nga dal fa feggook Eben Eser, waa Filisti dal ca Afeg.2Filisteen ña làng-déral Israayil, xare ba jib. Israayil daanu fa kanam waa Filisti, waa Filisti rey ca seeni làng lu jege ñeenti junni (4 000) ca toolub xare ba.3Ba mbooloo ma ñibbee ca dal ba, magi Israayil ña ne: «Lu waral Aji Sax ji dumalu nu tey ci loxoy waa Filisti? Lu waral Aji Sax ji duma nu ci kanamu waa Filisti? Nan jëleji gaalu kóllërey Aji Sax ji fa Silo; na dikk ci sunu biir, ba musal nu ci sunuy noon.»4Ci kaw loolu mbooloo ma yónnee ca Silo, ñu jëli gaalu kóllërey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, moom mi toog fi tiim ñaari malaakay serub yi. Foofa ca Silo la Xofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, nekkoon ak gaalu kóllërey Aji Sax ja.5Ba gaalu kóllërey Aji Sax ji duggsee ca dal ba, Israayil gépp a xaacoondoo, ba suuf say riir.6Waa Filisti dégg coow la, ne: «Waaw, coow lu réy loolu ca dalub Ebrë ya, lu mu doon?» Ba waa Filisti yégee ne gaalu kóllërey Aji Sax ja dugg na ca biir dal ba,7tiitaangee leen jàpp, ñu ne: «Am na yàlla ju dugg ca biir dal ba! Wóoy, ngalla nun! Nde guléet tey lu mel nii am!8Wóoy ngalla nun! Ku nuy musal ci jii yàlla ju bare doole. Yàlla jii moo dumaa woon waa Misra xeeti mbugal yu nekk, ca màndiŋ ma.9Dëgërluleen déy te diy góor, yeen waa Filisti, nde lu ko moy ngeen doon jaami Ebrë yi, na ñu nekke woon sunuy jaam. Góor-góorluleen boog te xeex.»10Waa Filisti nag di xare, ba bànni Israayil daanu: ku nekk daw jëm xaymaam. Jéll ba réy na lool; fanweeri junniy (30 000) xarekat yuy deme tànk des fa.11Gaalu Yàlla ga, ñu jël ko. Xofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, dee.
Mbugal ma topp na waa kër Eli
12Ca bés booba jenn waay ju bokk ci giirug Beñamin dawe ca làngu xare ba ca Silo. Mu agsee yére yu xottiku ak bopp bu fees ak suuf, di ko tiisloo.13Naka la agsi, yem ca Eli mu toog ca toogoom ca peggu yoon wa, di séentu, ndax tiitaange ja ko jàpp ndax gaalu Yàlla ga. Naka la waa ja duggsi ca dëkk ba, ba wax la xew, dëkk ba bépp yuuxoondoo.14Eli dégg coow la, ne: «Riir moomu lu mu?» Waa ja gaaw dikk, ngir wax ko Eli.15Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara.16Waa ja ne ko: «Man mii maa jóge ca toolub xare ba. Maa dawe làng ga tey jii.» Eli ne ko: «Doom, lu xew?»17Ndaw la ne ko: «Bànni Israayil a daw, won waa Filisti gannaaw. Jéll bu réy la sunu mbooloo ma daanu, sa ñaari doom ya, Xofni ak Fineyas dee nañu, te it gaalu Yàlla ga, jël nañu ko.»18Naka la tudd gaalu Yàlla ga rekk, Eli xàwweekoo ca toogu ba, daanoo njaaxaanaay, dal ca buntu dëkk ba, loos wa damm, mu dee, ndax booba day mag mu amoon yaram. Fekk na Eli jiite Israayil ñeent fukki at.19Goroom, jabaru Fineyas nag jigéenu wérul la woon te booba mu ngi waaja wasin. Naka la dégg ne jël nañu gaalu Yàlla ga, te baayu jëkkëram ak jëkkëram dee nañu, mu daldi sukk wasin. Waaye fekk na mititu matam jeexal dooleem.20Ba loolu amee muy waaja dee, jigéen ña ko doon taxawu ne ko: «Na sa xel dal, ndax doom ju góor nga am.» Waaye àdduwul, teewluwul.21Ndaw sa nag tudde gone gi Ikabot (muy firi Ana leer ga?) te naan: «Leer ga dëddu na Israayil, gàddaay,» ndax la ñu nangu gaalu Yàlla ga ak la goroom ak jëkkëram dee.22Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israayil, gàddaay, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!»