MACË1wol_inj
Cosaanu Yeesu Kirist
1Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.2Ibraayma moo jur Isaaxa;Isaaxa jur Yanqóoba;Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;3Yuda, Peres ak Sara ci Tamar;Peres Esron, miy baayu Aram;4Aram Aminadab;Aminadab Nason;Nason Salmon;5Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas;Bowas am ak Ruut Obedd;Obedd jur Isayi,6miy baayu buur bi Daawuda.Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri;7Suleymaan jur Robowam;Robowam Abiya;Abiya Asaf;8Asaf Yosafat;Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;9Osiyas jur Yowatam;Yowatam Akas, miy baayu Esekiya;10Esekiya Manase;Manase Amon;Amon Yosiyas;11Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.12Ba ñu leen yóbboo ca Babilon,Yekoñas jur Salacel;Salacel Sorobabel,13
miy baayu Abiyudd;Abiyudd Eliyakim;Eliyakim Asor;14Asor Sadog;Sadog Akim;Akim Eliyudd;15Eliyudd Eleyasar;Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;16Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama;te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.17Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.