YAWUT YA6wol_inj
1Kon nag léegi nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu baña dalaat njàngle mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo wara tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla,2di leen jàngalaat ci mbirum sangu set ci ay fànn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu jëm ci àtte biy sax dàkk.3Te noonu lanuy def, bu soobee Yàlla.4Li nu wara jëme kanam mooy lii: su amee ay nit ñu Yàlla xasa leeral ba noppi, ñu mos mayu Yàlla gi, am wàll ci Xelam mu Sell,5te xam mbaax, gi ci kàddug Yàlla, ak kéemaani jamono jiy ñëw,6te loolu lépp teewul ñu walbatiku, ñooñu kenn dootu leen mana yeesalaat, ba ñu tuub seeni bàkkaar. Li ko waral moo di, dañoo bëgga daajaat Doomu Yàlla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaañ.7Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox ñi ñu koy beyal gàncax gu am njariñ, day jot barke bi jóge ci Yàlla.8Waaye su meññee ay dég ak ay xaaxaam, du am benn njariñ; repp na ñu alag ko, te lakk lay mujje.9Waaye nag yéen samay soppe, su fekkee ne sax nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li gën ci yéen te ànd ak mucc.10Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak mbëggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te yéena ngi koy def ba tey.11Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yéen wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di séentu.12Bëggunu ngeen tayel, waaye royleen ñi gëm te muñ, ndaxte ñooñu ñooy jot li leen Yàlla dig.