EFES5wol_inj
1Yéen nag ñiy goney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu.2Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ.3Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi.4Dawleen it lu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla.5Na leen wóor ne kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla.6Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil.7Kon nag buleen séq ak ñoom dara.8Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi. Dundeleen ni ay goney leer Dundeleen nag ni ay goney leer.9Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg.10Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi,11te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def.12Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la;13waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko.14Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne:«Yewwul, yaw mi nelaw,te jóge ci biir néew yi,kon Kirist dina ne ràññ ci yaw,ni leeru jant buy fenk.»15Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel,16tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon.17Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobarey Boroom bi.18Buleen màndi it ci sàngara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi;19di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ciy woy ak i cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seen xol.20Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen mana tollu, ci lu mu mana doon;21teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.