JËF YA23wol_inj
1Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»2Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.3Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»4Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas sarxalkat bu mag, bi Yàlla fal?»5Pool ne leen: «Bokk yi, xawma woon ne sarxalkat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»6Naka noona Pool, mi xam ne genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»7Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xàjjalikoo.8Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.9Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne rab a ko wax mbaa malaaka…?»10Noonu xuloo ba daldi gëna tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.11Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»